Banu yegsi ci sunu genn wàllu dund,
dama jékki tàbbi ci gott bu lëndëm,
ndax dëkk ci jubadi ba faf gëlëm.
Céy ñagas-ñagas ak raglu ak jafe-jafe yu amul àpp,
ya nekk ca gott bu lëndëm kiris ba jéggina dayo,
xalaat ko rekk yòbbu na fit!
Méttit wu tar ma fa am, mook dee sore wuñu ;
da naa wax la ma fekk ca gott ba,
nettali lèpp lu ma fa daj.
Xamatuma lu ma watat ca lëndëm ga,
sàggan bokk na ca la dëngal sama yoon.
Waaye àgg naa ca suufu benn tund,
xur wa ma tiital, foofu la jeexe.
Sànni naa samay gët ca-kow,
gis ni catu tund wi leeree
ndax dafa sol cari jant bi,
ma xam ne ku bëggul sànku,
fàww mu teg ay jëfam ci yoon wu leer.
Leeraayu tund wi xaw naa dalal sama xel,
fanaan ca gottu bu lëndëm tiitaloon na ma
ba ma yaakaaroon ne doo tu ma mucc.
Maa ngi xëxat melni nit ku
doon waaja lab ci dex, far rëcc,
ba ma agsee ca tefes ga
jàkkaarlook ndox ma nak, di rag-ragi,
mu melni sama « ruuhu » gi moo doon rocceeku.
Ma geestu yër gott bu ñagas
boobu nga xam ni kenn mësu fa jaar
te demul àllaaxira.
Ma daldi taaxirlu tuuti ngir noppal cér yi,
daldi defaat ay jeego ba ci mbartal mi.
Waaye nak saa yu ma fexe yéeg ca
catu tundu wa, dafa melni sama benn tànk
dañkay ñoddi mu jëm suuf.
Bi ma yaakaaree ne, li may tiit sore na,
am segg ak deram bu am ay tipp-tipp, gaaw te raglu
dafa ne bëret sama kanam, dagg yoon wi.
Ma xalaat ne naa daw dellu ginnaaw.
Ñi ngi ci njël, jant baa ngi fenk,
biddiiw yi fàq a guñu,
sunu boroom moo leen
boole woon sàkk
moom mi mën a defar lu rafet;
yaakaar naa ne jant bi fenk
dàq na seytaane yiy jóg guddi.
Te ñi ngi ci cooroor, jamono ju féex.
Loolu lépp boole na dalalaat sama fit
ba ma yaakaar ne segg mi
ak tipp-tipp yu yànj
mënu ma tere jàll sama yoon;
waaye bi ma wóoloo sama bopp,
ci laa séen ak gaynde fëll, sama fit rëccaat.
Gaynde gi song ma la bëgg.
Ni mu yëkkëti bopp bi
wonena dafa xiif lool.
Ngelaw li mel nii tiit na ci ba lox.
Noppee gunu beneen mala génn.
Mi ngi nirook xeetu till bu jigéen,
ràgg lool, ay yaxi kese la dese,
boole kook añaan gu métti.
Waaw toroxal na ay nit yu bare.
Xeetu till bu jigéen bii,
yòbbu na sama fit.
Ndax melokaan wu raglu:
Yéegoon sax ba ci kow tund wi du tax ma rëcc.
Kuy dajale alal te du ko jariño,
bu xëye ñàkk lépp,
dina xam ne nay baaxul,
dana jooy, sëngéem.
Toroxte bu mel noonu,
lama xeetu till bi bëggoon teg.
Ndax dàq nama bama dellu waat
ci ak lëndëm.
Ci biir lëndëm gi,
ab takkandeer feeñu ma.
«Wóoy fu ma jëm» ! laa yuuxu,
66 «Yaw lan nga, aw rab walla nit ak ay noppam?»
Takkandeer wi tontu:
« Dootu ma nit ak ay noppam,
doonon naa ko ca jamono bu yàgg,
samay waajur “Lombardi” lanu soqeekoo woon,
ñoom ñaar ña nga juddu woon dëkkub Mantu.
Man maa nga juddu ca jamono buur Jules César,
waaye jotu ma koo xam,
ndax ba muy saay tuut- tànk laa.
Ma nga màgge ca jamono buur Auguste.
Jamono joojee ñépp biddaa
ak xérém lañu doon jaamu.
Bind naay taalif am ci benn bu ma tagg
Enée doomu Ankise ma gàddaayoon dëkkub Troie,
gannaaw bañu bóome Ilio mu mag ma,
daldi taal yaram wa.
Enée fi ci Italie la teersi.
Waaw yow lu la xiir ci dellu gannaaw,
ba duggaat ci musiba?
Lu la tere jubal fa nga jëmoon?
Foofa la xéewal ya di baawaan! »
«Waaw góor gi yow la Virgil
mu siiw mi ma yàgg dégg,
taalif kat bu xóot te yaa, bindkatu kàddu
yu law di wal ni dex? »
Loolu laa ko tontu ci teggin.
Daldi ci tegaat: «Yow góor gi, sa taalif yi
ak sa daraja siggil na taalif kat yépp,
say taalif ñoo leeral
yoonu bépp taalif kat bu ñëw sa gannaaw,
ñoom yaw lañu roy ndax yaay seen selbe.
Dinaa la yëgal ne loo bind,
jàng naako bu baax, ndax fonk la
tax na ba duma tayal ci gëstu say téeré.
Yow yaay sama njiit, yaay sama bindkat, sama royukaay,
Yow yaa tax ba luma taalif samay nawle sargal ko.
Xanaa léegi nak gis nga lu tax ma dëpp.
Dimbali ma yaw mii nekk mag mu àndak sago,
ndax xeetu till bi, yòbbu na sama fit».
«Teggil jaar feneen moo gën ci yow».
Loolu la tontu bi mu gise samay rongooñ.
«Bo bëgge mucc ci rabu àll bi;
xeetu till bi tax ngay jooy ak wut wallu, du bàyyi kenn mu jéggi yoon wi.
Ku ko jéem, dina la song ba faat la.
Rabu àll wu bon te soxor,
lu mu lekk-lekk, du tax mu suur.
Xanaa kay xiifam dafay yokkaat ci saa si.
Xeetu till bu jigéén bi xeebul dara.
Rabu àll bu ko romb, yàkkam tina mu tëb ko.
Noonu lay jëfe ba dajeek ab jàmbaar
ba kay ray, ray bu métti ndax jéppi ko.
Du jàmbaar bu bëggé walla soxor.
Waaye dafa nekk ab sàmm kat
buy jubbanti jikko yu dëng.
Ñi topp seen bakkan,
jàmbaar ji dina leen rëbb,
ba dàq leen réewum Italie.
Loolu la ay jàmbaar
ñu bañ ñaawtéef yu ni mel,
xeex ba ñàkk seen bakkan.
Ñi ngi tuddoon Camille mu sell ma,
Eurialo, Tisio ak Niso.
Sàmm katu jikko yi
dinan toraxal ñu bon ñi,
ba dellooleen safara gañu jógé woon.
Loolu tax na, ndongo li gën mooy
ma jëlé la fi, nga topp ci man,
ma womat la feneen.
Danañu romb safara ga dul fey mukk,
foofa ca àllaaxira da nga dégg
yuuxu yu métti jògé ca ña alku,
da nga gis coonook toroxte
ya fa ñoom maam yu bonoon di daj.
Ña gën a torox ñépp nak mooy,
ña faatu bañu alakleen ñaari yoon.
Am nafa yeneen nit ñu safara di lakk,
ñu melni ñu bég walla safatuleen,
ndax yaakaar ne yàgg-yàgg
dinan leen jéggal seeni bàkkaar,
bañu delluwaat ca béréb bu
nit ñu sell ya.
Ñun ñaar saa bu ñu àggee
ca béréb bu nit nu sell ya,
dinaala bàyyi
ca loxoy “Beatrice” mu mag ma,
bu boobaa man damay daldi dëpp.
Beatrice moo ma gën yeyoo ngir
yòbbu la fi nga bëg a àgg;
ndax dama toppul woon
yoonu sunu boroom mi sàkk
mbindeef yeep, loolu moo tax bëggul ma dugg ca àjjanam.
Sunu boorom moo yilif àdduna bépp, waaye àjjana nak la taamu ci fépp,
foofa la féete, fa la samp jal bi: ku mu nangu nga dugg àjjana, raw nga! »
Ma daldi ne: “Taalif kat bi,
maa ngi lay ñaan ci barke
boroom bi nga jottul xam,
ndax jamonoy ceddo nga fekke, ngir ëllëg man ma mucc ci mbugël.
Ñaan naa la nga yòbbu ma
ca béréb ya ngay wax,
ma siyaare buntu wàlliyu mi tudd Pierre.
Ci yoon wa dina gis nit ña
ngay xarap boobu ba léegi”.
Taalifkat-bi daldi tegu ci yoon wi,
man ma topp ci ginnaawam
Traduzione in wolof di – Traduction en wolof : Pap Khouma
pseudonimo di – Pseudonyme de : Aboulaye Khouma
Validazione della traduzione – Validation de la traduction: Diafara Sadikhou Fofana
Comitato scientifico – Comité scientifique:
Stefano Anselmo
Cheikh Tidiane Gaye
Baye Ndiaye
Nel mezzo del cammin di nostra vita
mi ritrovai per una selva oscura,
ché la diritta via era smarrita.
Ahi quanto a dir qual era è cosa dura
esta selva selvaggia e aspra e forte
che nel pensier rinova la paura!
Tant’ è amara che poco è più morte;
ma per trattar del ben ch’i’ vi trovai,
dirò de l’altre cose ch’i’ v’ho scorte.
Io non so ben ridir com’ i’ v’intrai,
tant’ era pien di sonno a quel punto
che la verace via abbandonai.
Ma poi ch’i’ fui al piè d’un colle giunto,
là dove terminava quella valle
che m’avea di paura il cor compunto,
guardai in alto e vidi le sue spalle
vestite già de’ raggi del pianeta
che mena dritto altrui per ogne calle.
Allor fu la paura un poco queta,
che nel lago del cor m’era durata
la notte ch’i’ passai con tanta pieta.
E come quei che con lena affannata,
uscito fuor del pelago a la riva,
si volge a l’acqua perigliosa e guata,
così l’animo mio, ch’ancor fuggiva,
si volse a retro a rimirar lo passo
che non lasciò già mai persona viva.
Poi ch’èi posato un poco il corpo lasso,
ripresi via per la piaggia diserta,
sì che ‘l piè fermo sempre era ‘l più basso.
Ed ecco, quasi al cominciar de l’erta,
una lonza leggiera e presta molto,
che di pel macolato era coverta;
e non mi si partia dinanzi al volto,
anzi ‘mpediva tanto il mio cammino,
ch’i’ fui per ritornar più volte vòlto.
Temp’ era dal principio del mattino,
e ‘l sol montava ‘n sù con quelle stelle
ch’eran con lui quando l’amor divino
mosse di prima quelle cose belle;
sì ch’a bene sperar m’era cagione
di quella fiera a la gaetta pelle
l’ora del tempo e la dolce stagione;
ma non sì che paura non mi desse
la vista che m’apparve d’un leone.
Questi parea che contra me venisse
con la test’ alta e con rabbiosa fame,
sì che parea che l’aere ne tremesse.
Ed una lupa, che di tutte brame
sembiava carca ne la sua magrezza,
e molte genti fé già viver grame,
questa mi porse tanto di gravezza
con la paura ch’uscia di sua vista,
ch’io perdei la speranza de l’altezza.
E qual è quei che volontieri acquista,
e giugne ‘l tempo che perder lo face,
che ‘n tutti suoi pensier piange e s’attrista;
tal mi fece la bestia sanza pace,
che, venendomi ‘ncontro, a poco a poco
mi ripigneva là dove ‘l sol tace.
Mentre ch’i’ rovinava in basso loco,
dinanzi a li occhi mi si fu offerto
chi per lungo silenzio parea fioco.
Quando vidi costui nel gran diserto,
«Misereredi me», gridai a lui,
«qual che tu sii, od ombra od omo certo!».
Rispuosemi: «Non omo, omo già fui,
e li parenti miei furon lombardi,
mantoani per patrïa ambedui.
Nacquisub Iulio , ancor che fosse tardi,
e vissi a Roma sotto ‘l buono Augusto
nel tempo de li dèi falsi e bugiardi.
Poeta fui, e cantai di quel giusto
figliuol d’Anchise che venne di Troia,
poi che ‘l superbo Ilïón fu combusto.
Ma tu perché ritorni a tanta noia?
perché non sali il dilettoso monte
ch’è principio e cagion di tutta gioia?».
«Or se’ tu quel Virgilio e quella fonte
che spandi di parlar sì largo fiume?»,
rispuos’ io lui con vergognosa fronte.
«O de li altri poeti onore e lume,
vagliami ‘l lungo studio e ‘l grande amore
che m’ha fatto cercar lo tuo volume.
Tu se’ lo mio maestro e ‘l mio autore,
tu se’ solo colui da cu’ io tolsi
lo bello stilo che m’ha fatto onore.
Vedi la bestia per cu’ io mi volsi;
aiutami da lei, famoso saggio,
ch’ella mi fa tremar le vene e i polsi».
«A te convien tenere altro vïaggio»,
rispuose, poi che lagrimar mi vide,
«se vuo’ campar d’esto loco selvaggio;
ché questa bestia, per la qual tu gride,
non lascia altrui passar per la sua via,
ma tanto lo ‘mpedisce che l’uccide;
e ha natura sì malvagia e ria,
che mai non empie la bramosa voglia,
e dopo ‘l pasto ha più fame che pria.
Molti son li animali a cui s’ammoglia,
e più saranno ancora, infin che ‘l veltro
verrà, che la farà morir con doglia.
Questi non ciberà terra né peltro,
ma sapïenza, amore e virtute,
e sua nazion sarà tra feltro e feltro.
Di quella umile Italia fia salute
per cui morì la vergine Cammilla,
Eurialo e Turno e Niso di ferute.
Questi la caccerà per ogne villa,
fin che l’avrà rimessa ne lo ‘nferno,
là onde ‘nvidia prima dipartilla.
Ond’ io per lo tuo me’ penso e discerno
che tu mi segui, e io sarò tua guida,
e trarrotti di qui per loco etterno;
ove udirai le disperate strida,
vedrai li antichi spiriti dolenti,
ch’a la seconda morte ciascun grida;
e vederai color che son contenti
nel foco, perché speran di venire
quando che sia a le beate genti.
A le quai poi se tu vorrai salire,
anima fia a ciò più di me degna:
con lei ti lascerò nel mio partire;
ché quello imperador che là sù regna,
perch’ i’ fu’ ribellante a la sua legge,
non vuol che ‘n sua città per me si vegna.
In tutte parti impera e quivi regge;
quivi è la sua città e l’alto seggio:
oh felice colui cu’ ivi elegge!».
E io a lui: «Poeta, io ti richeggio
per quello Dio che tu non conoscesti,
a ciò ch’io fugga questo male e peggio,
che tu mi meni là dov’ or dicesti,
sì ch’io veggia la porta di san Pietro
e color cui tu fai cotanto mesti».
Allor si mosse, e io li tenni dietro.
Un lavoro culturale egregio!